Kan moo gëna mag ci taalibe yi?
Luug 9.46-50
46 Gannaaw loolu taalibe yi tàmbali di waxtaan ci seen biir ngir bëgga xam kan moo gëna màgg ci ñoom.
47 Noonu Yeesu xam seeni xalaatu xol,
àndi benn xale ci wetam,
48 ne leen:
«Ku nangu xale bii ci sama tur,
man nga nangu;
te ku ma nangu,
nangu nga ki ma yónni.
Ndaxte ku gëna ndaw ci yeen ñépp,
kooku moo gëna mag. »
49 Noonu Yowaana tontu ko ne:
«Kilifa gi,
gis nanu benn waay buy dàq ay rab ci sa tur waaye danu ko doon jéema tere ndaxte àndul ak nun.»
50 Yeesu tontu ko ne:
«Buleen ko tere ndaxte ku leen xeexul,
ci yeen la far.»