Yeesu wéral na benn xale bu am rab
Luug 9.37-45
37 Ci ëllëg sa bi Yeesu,
Piyeer,
Yowaana ak Saag di wàcc ci tund wi,
mbooloo mu takku ñëw di dajesi ak Yeesu.
38 Ci diggu mbooloo mi,
am benn waay bu ñëw di yuuxu di naan:
«Jàngalekat bi,
maa ngi la koy ñaan,
xoolal ma sama doom,
ndaxte kenn kii laa am.
39 Rab moo ko jàpp,
mu jekki di ko yuuxuloo,
di ko sayloo,
gémmiñam di fuur te du ko bàyyi feek metital ko.
40 Ñaan naa sa taalibe yi ngir ñu dàq rab bi waaye mënuñu ko.»
41 Yeesu daldi jël kàddu gi te ne leen:
«Yeen niti jamono jii,
ñi amul ngëm te dëng.
Man,
ba kañ laay nekk ak yeen te di leen muñal?»
Mu daldi wax waa ji:
«Àndil ma sa doom bi fii.»
42 Bi xale bi di ñëw,
rab bi daaneel ko ci suuf,
sayloo ko.
Yeesu tëkku rab bi,
wéral xale bi,
te delloo ko pàppaam.
43 Ñépp daldi jaaxle ndax màggaayu Yàlla.
Bu ñépp yéemoo ci li mu doon def,
Yeesu ne taalibeem yi:
44 «Ubbileen seeni nopp bu baax:
Fàww ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi.»
45 Waaye kàddu yooyu leerul ci ñoom:
ump na leen,
te mënuñu woona xam luy loolu di tekki,
te ragal nañu laaj Yeesu lu jëm ci kàddu yooyu.