Màggaayu Yeesu feeñ na
Luug 9.28-36
28 Lu tollook juróom ñetti fan gannaaw bi mu waxee kàddu yooyu,
Yeesu jël Piyeer,
Yowaana,
ak Saag,
daldi yéeg ci tund wi ngir ñaan.
29 Bi mu doon ñaan,
xar kanamam soppeeku,
yére yu mu soloon weex tàll bay melax.
30 Ci saa si ñaari nit di waxtaan ak moom,
Musaa ak Ilyaas.
31 Ñu feeñu ci màggaayu Yàlla di wax ci demam li mu wara matal ca Yerusalem.
32 Piyeer ak ñi mu àndaloon nelawoon nañu waaye seeni nelaw xootul woon.
Noonu ñu yewwu,
gis màggaayu Yeesu ak ñaar ñi nekkoon ak moom.
33 Bi ñooñu di xaajaloo ak moom,
Piyeer ne ko:
«Kilifa gi,
baax na ngir ñu des fi.
Nanu def ñetti mbaar,
benn ngir yaw,
benn ngir Musaa,
ak benn ngir Ilyaas.»
Xamul woon lu mu doon wax.
34 Bi mu nekkee di wax,
benn niir daldi ñëw,
muur leen.
Bi taalibe yi duggee ci niir bi,
ñu daldi tiit.
35 Noonu baat jóge ci niir bi,
ne:
«Kii mooy sama Doom.
Moom laa tànn.
Dégluleen ko.»
36 Gannaaw bi baat bi waxee ba noppi,
Yeesu des fa moom kese.
Ci jamono jooju taalibe yi noppi,
nettaliwuñu kenn li ñu gisoon.