Yeesu jëm na Yerusalem
Luug 9.51-62
51 Bi bés bu ñu waroona yékkëti Yeesu asamaan jegesee,
mu jël ndogal ngir dem Yerusalem.
52 Noonu mu yónni ay ndaw ngir ñu jiitu ko.
Ci yoon bi,
ñu dugg ci benn gox bu nekk ci diiwaanu Samari ngir waajal ko fu mu mëna dal,
53 waaye waa gox boobu bañ koo dalal ndaxte dafa doon dem Yerusalem.
54 Bi ñu gisee ne waa Samari dañu leen baña dalal,
Saag ak Yowaana laaj Yeesu ne:
«Boroom bi,
ndax danga bëgg nu wax safaras asamaan si mu wàcc ci seen kaw ngir lakk leen?»
55 Noonu Yeesu walbatiku ci ñoom,
gëdd leen
56 te ñu dem ci beneen gox.
57 Bi ñuy dem ci yoon bi benn waay ne Yeesu:
«Boroom bi,
dinaa la topp foo mëna dem.»
58 Yeesu tontu ko ne:
«Xaju àll yi am nañu ay pax yu ñu dëkke;
picc yi am nañu ay tagg,
waaye Doomu nit ki amul fu muy teg boppam ngir noppalu.»
59 Noonu Yeesu wax keneen ki ne:
«Topp ma.»
Mu ne ko:
«Boroom bi,
may ma,
ma dem suul sama pàppa ba noppi.»
60 Yeesu ne ko:
«Bàyyil ñi dee,
suul seeni néew waaye yaw nga dem yégle nguuru Yàlla gi.»
61 Noonu keneen ne:
«Boroom bi,
dinaa la topp waaye may ma,
ma dem tàggooji ak sama waa kër ba noppi.»
62 Yeesu ne ko:
«Kuy bey di geestu,
amuloo njériñ nguuru Yàlla gi.»