Yeesu wéral na waay ju am ay rab
Luug 8.26-39
26 Yeesu ak taalibeem yi teer nañu ci diiwaanu Serasa.
Mu jàkkaarlook diiwaanu Galile.
27 Bi Yeesu wàccee gaal gi,
am benn waay,
di doom ci diiwaan bi,
di ñëw,
di dajesi ak moom.
Waa ji amoon na ay rab,
te yàgg na lool daawul sol yére te dëkkul ci kër waaye mu ngi dëkkoon ci armeel yi.
28-29 Yenn saay rab yi jàpp ko,
te nit ñi doon takk loxoom yi ay ceen te di takk tànk yi ak ay weñ,
waaye du tere mu dog ko te rab bi di ko yóbbu ci màndiŋ mi.
Bi mu gisee Yeesu mu daanu ci tànkam yi di yuuxu te di wax ak baat bu kawe ne:
«Loo ma bëggal,
Yeesu Doomu Yàlla Aji-Kawe ji?
Ma ngi la koy ñaan,
bul ma metital.»
Wax na loolu ndaxte fekkoon na Yeesu jox ndigal rab bi ngir mu génn ci waa ji.
30 Yeesu laaj ko:
«Noo tudd?»
Mu tontu ko ne:
«Coggal laa tudd.»
Wax na loolu ndaxte rab yu bari ñoo nekkoon ci moom.
31 Rab yi ñaan Yeesu ngir mu bañ leena sànni ci kàmb gu ñu tëj xel yu bon yi.
32 Te fekk na ci waxtu boobu amoon na géttu mbaam-xuux yu bari,
yu doon wut lu ñuy lekk ci kaw tund bi.
Rab yi ñaan Yeesu ngir mu may leen ñu dugg ci géttu mbaam-xuux ya.
Yeesu may leen ko.
33 Noonu rab yi daldi génn ci waa ji,
dugg ci mbaam-xuux yi,
te mbaam-xuux yi di gaawantu,
tarxiis,
daanu ci dex bi,
daldi lab.
34 Bi sàmmkatu mbaam-xuux yi gisee li xewoon,
ñu daldi daw,
dem ci dëkk bi,
ak ci kër àll yi,
di nettali lépp lu ñu gisoon.
35 Nit ñi génn ngir gis li xewoon.
Bi ñu yeggsee ci wetu Yeesu,
ñu gis ki rab yi jàppoon,
mu toog ci wetam sol yére te ànd ak sagoom.
Ñu daldi tiit.
36 Ñi ko fekkewoon di nettali naka la waa ji ame woon rab mucce.
37 Noonu waa diiwaanu Serasa yépp di ñaan Yeesu ngir mu génn seen diiwaan ndaxte tiitaange bu mag,
moo leen jàppoon.
Bi Yeesu di yéeg ci gaal gi ngir dellu,
38 ki mu teqale woon ak rab yi ñaan ko ngir mu ànd ak moom.
Waaye Yeesu ne ko:
39 «Ñibbil sa kër te nga nettali lépp li la Yàlla defal.»
Waa ji ñibbi këram,
di yégle ci dëkk bi yépp li ko Yeesu defal.