Yeesu dekkil na doomu Yayrus te wéral jigéen ju doon xëpp deret
Luug 8.40-56
40 Bi Yeesu dellusee ci Galile mbooloo mu bari moo ko doon teeru ndaxte dañu ko doon xaar.
41 Foofu amoon na benn nit bu tudd Yayrus nekk njiitu kër-ñaan bi.
Mu sukk ci tànku Yeesu ngir ñaan ko ngir mu ñëw këram,
42 ndaxte dafa amoon benn doom bu jigéen képp bu am fukki at ak ñaar,
te feebaroon bay waaja dee.
Bi ñuy dem ci yoon bi mbooloo mi di tanc Yeesu.
43 Foofu amoon na benn jigéen bu doon xëpp deret lu tollu ci fukki at ak ñaar,
te fajoo alalam bi yépp ci fajkat yi,
waaye kenn mënu ko woona wéral.
44 Mu jaar ci gannaaw Yeesu,
laal catu yéreem,
te xëpp deret bi daldi taxaw ci saa si.
45 Yeesu laaj leen:
«Kan moo ma laal?»
Waaye ñépp di wax ne:
«Du man!
Du man!»
Piyeer ne ko:
«Kilifa gi,
mbooloo mi la wër ñoo la tanc.»
46 Yeesu waxaat ne :
«Am na ku ma laal ndaxte yég naa kàttan bu génn ci man.»
47 Bi ku jigéen ki xamee ne mënatul nëbbatu.
Muy ñëw di lox,
te sukk ci tànku Yeesu yi,
di wax ci kanamu ñépp lu tax mu laaloon ko ak ni mu jote wér ci saa si.
48 Yeesu ne ko:
«Sama doom sa ngëm wéral na la;
demal ci jàmm.»
49 Bi Yeesu di wax loolu,
benn nit jóge ci kër Yayrus mi nekk njiitu kër-ñaan bi,
te ne ko:
«Jarul nga sonal jàngalekat bi,
ndaxte sa doom dee na.»
50 Bi Yeesu déggee wax yooyu,
mu ne Yayrus:
«Bul ragal dara.
Gëmal rekk te sa doom dina mucc.»
51-53 Noonu bi ñu yeggsee ci kër gi,
Ñépp a doon jooy di naqarlu xale bi.
Mu ne leen:
«Bàyyileen jooy yi.
Xale bi deewul,
day nelaw rekk.»
Noonu ñu koy ñaawal ndaxte xamoon nañu ne xale bi dee na.
Yeesu nanguwuloon kenn dugg ak moom,
ku dul Piyeer,
Yowaana,
Saag,
pàppa xale bi ak yaayam.
54 Mu téye loxo xale ba,
te mu wax ak baat bu kawe ne:
«Sama doom,
jógal.»
55 Noonu xale bi daldi dekki te mu jóg ci saa si.
Mu naan leen:
«Joxleen ko mu lekk.»
56 Waajuru xale bi waaru woon nañu lool.
Waaye Yeesu ne leen:
«Buleen wax kenn li fi xew.»