Yeesu dalal na ngelaw li ak ndox mi
Luug 8.22-25
22 Benn bés Yeesu ak taalibe yi yéeg gaal.
Yeesu ne taalibe yi:
«Nu dem ba ci beneen tefes bi.»
23 Bi ñu doon dem Yeesu daldi nelaw.
Ngelaw gu am doole yëngal ndox mi,
te ndox mu bari dugg ci biir gaal gi.
Ñu nekkoon ci tolof-tolof.
24 Taalibe yi jegesi ko,
yee ko ne ko:
«Kilifa gi,
kilifa gi,
nu ngi suux!»
Yeesu daldi jóg,
gëdd ngelaw li ak ndox mi.
Lépp dal.
25 Yeesu ne taalibe yi:
«Ana seen ngëm?»
Taalibe yi tiitoon nañu te waaru di waxtaan ci seen biir di naan:
«Waaw!
Kii mooy kan sax,
bay jox ndigal ngelaw li ak ndox mi te ñu koy déggal?»