Léebu làmp bi
Luug 8.16-18
16 Kenn du taal làmp di ko muur walla di ko dugal ci ron lal,
waaye dañu koy wékk ngir ku duggsi mëna gis leer bi.
17 Amul dara lu nëbbu lu nit dul xam;
amul dara lu umpe lu nit dul xamle benn bés.
18 Moytuleen ci anam bi nuy déggee,
ndaxte ku am dinañu la yokkal,
waaye ku amul dinañu jël sax li nga xalaatoon ne moom nga am.