Léebu jikat bi
Luug 8.4-15
4 Noonu mu am mbooloo mu bari,
jóge dëkk ak dëkk,
ñu daldi ñëw ci wetam.
Noonu mu wax leen léeb bii:
5 «Dafa amoon benn jikat bu génn ngir jiyi jiwam.
Bi muy ji am pepp yu daanu ci yoon bi;
nit ñi ñëw,
dëgg ko,
picci asamaan si ñëw lekk li des.
6 Yenn pepp yi daanu ci diggante xeer yi,
bi ñu saxee ñu daldi wow,
ndaxte foofu tooyul woon.
7 Yeneen pepp yi daanu ci diggante ay xaaxaam;
ñu daldi jógandoo ak xaaxaam yi,
xaaxaam yi tanc leen.
8 Waaye yi ci des daldi daanu ci suuf su baax si;
ci noonu ñu daldi meññ téeméeri yoon lu ëpp lu mu ji woon.»
Yeesu yékkëti baatam te yokk ca ne:
«Na ki am nopp ngir déglu,
dégg.»
9 Taalibeem yi laaj ko lu léeb bi di tekki.
10 Mu tontu leen:
«Yeen,
Yàlla may na leen ngir ngeen xam li nëbbu ci nguuru Yàlla gi,
waaye ñeneen ñi,
dama leen koy wax ci léeb ngir
\qt bu ñuy xoole,
ñu baña gis,
\qt te ñu dégg,
baña ràññee.
11 Lii la léeb bi di tekki:
jiwu ji mooy kàddu Yàlla gi.
12 Ñi nga xam ne moo nekk ci yoon bi mooy ñiy déglu kàddu gi,
waaye Seytaane ñëw,
këf kàddu gi nekk ci seen biir xol ngir ñu baña gëm te baña mucc.
13 Li nga xam ne moo daanu ci xeer yi mooy ñiy déglu te nangu kàddu gi ak mbégte waaye amuñu reen,
te dañuy gëm benn diir te bàyyi ngëm bi ci waxtu bi jafe-jafe yi ñëwee.
14 Beneen bi mooy ji nga xam ne moo daanu ci xaaxaam yi,
mooy ñiy déglu te nangu kàddu gi,
waaye jafe-jafe àddina si,
alal yi ak bànneexu bakkan tanc leen ba tax duñu am ay meññeef yu baax.
15 Te beneen bi daanu ci suuf su baax si mooy ñi nga xamante ne dañuy déglu kàddu gi te denc ko ci seen biir xol bu baax ak dëggu,
téye ko di dëgër-dëgërlu ba ñu am meññeef.