Yeesu woo na Lewi te Farisen yi laaj nañu Yeesu
Luug 5.27-39
27 Bi loolu weesoo,
Yeesu génn te gis benn juutikat bu tudd Lewi,
mu toog ci bérébu liggéeyukaay bi.
Mu wax ko ne:
«Topp ma,»
28 te mu jóg,
bàyyi lépp,
daldi topp Yeesu.
29 Lewi togglu reer bu mag ci biir këram ngir Yeesu te juutikat yu bari ak ay nit ñu bari doon lekkandoo ak ñoom.
30 Farisen yi ak jàngalekatu-yoonu-Musaa yi bokkoon ci ñoom di xuntu,
di wax taalibeem yi:
«Lu tax ngeen di lekkandoo te di naanandoo ak ay juutikat ak ay bàkkaarkat?»
31 Yeesu jël kàddu gi te wax leen:
«Du ñi wér ñoo soxla fajkat,
waaye ñi wéradi.
32 Damaa ñëw ngir woo bàkkaarkat yi,
ñu tuub seeni bàkkaar,
waaye du ñu jub ñi.»
33 Ñu wax ko ne:
«Taalibey Yaxya yi ak taalibey Farisen yi dañuy faral di woor ak di ñaan,
waaye yaw say taalibe dañuy lekk ak di naan.»
34 Mu tontu leen ne:
«Ndax kenn mën na woorloo xariti boroom séet bi,
waxtu yi mu nekke ak ñoom?
35 Ay bés a ngi ñëw ñu jële boroom séet bi ci seen biir te ci bés yooyu dinañu woor.»
36 Mu wax leen benn léeb ne leen:
«Kenn du xotti ab daggit ci yére bu bees te di ko taqale ci yére bu màggat,
ndaxte bu ko defee,
bu bees bi day yàqu te daggit bu bees bi du ànd ak yére bu màggat bi.
37 Te kenn du jël biiñ bu bees di ko def ci ay mbuusi der yu màggat.
Lu ko moy,
biiñ bi dina fëq mbuus ya,
daldi tuuru,
te mbuus ya dinañu yàqu,
38 waaye fàww nga jël biiñ bu bees nga def ko ci ay mbuusi der yu bees.
39 Te kenn,
gannaaw bi mu naanee biiñ bu màggat ba noppi du bëgg biiñ bu bees ndaxte day wax ne bu màggat bi moo gëna baax.»