Yeesu wéral na waay ju làggi
Luug 5.17-26
17 Benn bés Yeesu doon jàngale.
Amoon na ñu bokk ci tarixa bi ñuy woowe Farisen yi ak ay jàngalekatu-yoonu-Musaa yu fa toogoon di ko déglu.
Jógewoon nañu ci dëkk yépp ci diiwaanu Galile,
ci diiwaanu Yude ak ci dëkku Yerusalem.
Yeesu àndoon na ak kàttanu Boroom bi ngir faj.
18 Noonu mu am ay nit ñu ñëw,
jàppoo ci basaŋ nit ku làggi.
Ñu jéemoon koo dugal ci biir kër gi ngir àndi ko ci kanamu Yeesu,
19 waaye mënuñu ko woon ndax mbooloo ma.
Noonu ñu yéeg ci kaw kër gi,
toj dal bi,
te wàcce ko ak basaŋam ci diggu ñépp ci kanamu Yeesu.
20 Bi Yeesu gisee seen ngëm,
mu wax nit ku làggi ki ne:
«Sama waay,
baal nañu la say bàkkaar.»
21 Noonu jàngalekatu-yoonu-Musaa yi ak Farisen yi tàmbali di xalaat ci seeni xel di wax ne:
«Kii mooy kan bay méngale boppam ak Yàlla?
Amul kenn ku mëna baale bàkkaar yi,
ku dul Yàlla.»
22 Yeesu xam li ñu doon xalaat ci seen biir xol,
te mu ne leen:
«Lan ngeen nekk di xalaat ci seen biir xol?
23 Ban moo gëna yomb:
wax nit ki "baal nañu la say bàkkaar,"
walla wax nit ki "jógal te dox"?
24 Li ma bëgga def mooy ngir ngeen xam ne Doomu nit ki am na sañ-sañ ci àddina si baale bàkkaar yi.»
Noonu mu wax ku làggi ki:
«Jógal,
jël sa basaŋ,
te nga ñibbi.»
25 Ci saa si mu daldi jóg ci kanamu ñépp di màggal Yàlla,
jël basaŋ bi mu tëddewoon,
di ñibbi këram.
26 Ñépp waaru woon nañu,
ànd ak tiitaange di màggal Yàlla te di wax ne:
«Gis nanu tey ay mbir yu nu yéem.»