Yeesu setal na benn waay ju gaana
Luug 5.12-16
12 Gannaaw loolu Yeesu nekkoon na ci benn dëkk te foofu amoon na benn waay ju yaramam yépp daj ak feebaru ngaana.
Bi mu gisee Yeesu mu daldi sukk,
dëpp kanamam ci suuf,
te ñaan ko ne:
«Boroom bi,
su fekkee bëgg nga ko,
mën nga ma setal.»
13 Yeesu tàllal loxoom,
laal ko te wax ko ne:
«Bëgg naa ko,
setal.»
Ci saa si,
feebaru ngaana bi daldi koy bàyyi.
14 Ci noonu,
Yeesu dénk ko ne:
«Bu ko wax kenn waaye demal nga won sa bopp jébbalkatu-sarax si te nga joxe sarax siy wone ne set nga,
ni ko yoonu Musaa diglee,
te loolu dina mëna nekk seede ci ñoom.
15 Turu Yeesu daldi gëna siiw te ay nit yu bari ñëwoon nañu ngir déglu ko te mu wéral seeni feebar.
16 Waaye Yeesu ci boppam dem na,
ni mu ko tàmme woon di def,
ci biir màndiŋ ba ngir ñaan.