Yeesu woo na taalibeem yu jëkk yi
Luug 5.1-11
1 Benn bés,
Yeesu nekkoon ci wetu dexu Senesaret.
Foofu amoon na mbooloo mu takku mu ko wëroon,
doon buuxante ngir déglu kàddu Yàlla gi.
2 Noonu mu gis ñaari gaal yu nekkoon ci tefes bi.
Nappkat yi dañoo wàccoon ngir raxas seeni mbaal.
3 Mu yéeg ci benn gaal gi nga xam ne Simoŋ moo ko moomoon.
Te mu ñaan ko ne:
«Sorilal sa gaal gi tuuti tefes gi.»
Yeesu daldi toog ci gaal gi,
di jàngal mbooloo ma fa nekkoon.
4 Bi mu jàngalee ba noppi,
mu wax Simoŋ ne ko:
«Joowal sa gaal gi ba fi ndox mi gëna xóote,
te ngeen sànni seeni mbaal ngir napp.»
5 Simoŋ tontu ko ne:
«Kilifa gi,
danoo fanaane mbaal guddi gi yépp ba sonn te jàppunu dara.
Waaye ci say kàddu dinaa sànni mbaal yi.»
6 Bi ñu ko sànnee ñu daldi jàpp ay jën yu bari,
ba seen mbaal yi di waaja xotteeku.
7 Noonu ñu tàllal loxo seen àndandoo yi nekkoon ci beneen gaal gi ngir ñu ñëw jàppale leen.
Bi ñooñu ñëwee,
ñu daldi feesal ñaari gaal yépp ak ay jën,
ba seen gaal yi di waaja suux.
8 Bi Simoŋ Piyeer gisee loolu,
mu daldi sukk ci kanamu Yeesu te ne ko:
«Boroom bi,
sori ma,
ndaxte man bàkkaarkat laa.»
9 Simoŋ ak ñépp ñi nekkoon ak moom dañoo tiitoon lool ndax kéemaan bi Yeesu defoon,
ba tax ñu jàpp jën yu bari.
10 Tiit boobu tamit jàppoon na ay àndandoom,
maanaam Saag ak Yowaana yi nekkoon ay doomi Sebede.
Waaye Yeesu tontu Simoŋ ne ko:
«Bul ragal dara ndaxte dale ko tey nappkat nit ngay doon.»
11 Noonu ñu génne seeni gaal ba ci suuf,
ñu bàyyi lépp te topp Yeesu.