Yeesu dàq na ay rab te wéral ay nit yu feebar
Luug 4.31-44
31 Noonu Yeesu dem dëkku Kapernawum ci diiwaanu Galile.
Mu dugg ci kër-ñaan bi di jàngale ci bésu noflaay bi.
32 Nit ñi yéemu ci anam ni mu doon jàngalee ndaxte da doon jàngale ak sañ-sañ bu ko Yàlla jox.
33 Ci biir kër-ñaan bi,
amoon na benn waay bu am rab.
Waa ji di wax ak baat bu kawe,
di yuuxu,
di naan:
34 «Éey!
Yeesu mu Nasaret,
loo ma bëggal?
Ndax danga ñëw ngir sànk ma?
Xam naa la;
yaw yaay ku sell ki Yàlla yónni.»
35 Yeesu gëdd rab bi ne ko:
«Noppil te nga génn ci nit ki.»
Noonu,
rab bi daaneel ko ci suuf ci kanamu ñépp,
génn ci moom,
te defu ko dara.
36 Ñépp waaru di waxtaan ci seen biir,
di wax ne:
«Waaw!
Yii ñooy yan kàddu?
Muy wax ak kàttan ak sañ-sañ,
bay joxe ndigal te rab yi di génn.»
37 Noonu turu Yeesu daldi siiw ci Kapernawum ak li ko wër.
38 Bi loolu weesoo,
Yeesu génn ci kër-ñaan bi,
dem ci kër Simoŋ.
Fekk na yaayu jabaru Simoŋ am yaram bu tàng lool.
Ñu ñaan Yeesu ngir mu def ci dara.
39 Mu jegesi ko,
tiim ko,
gëdd tàngooru yaram bi te tàngooru yaram bi bàyyi.
Ci saa si yaayu jabaru Simoŋ jóg te di leen toppatoo.
40 Bi jant bi sowee,
ñu àndi ci Yeesu ñépp ñu amoon ay feebar yu wuute te mu teg kenn ku nekk loxo,
wéral leen.
41 Rab yi di génn ci ñu bari,
di yuuxu di wax ne:
«Yaw yaay Doomu Yàlla ji.»
Yeesu gëdd leen te tere leen ñu wax ndaxte xamoon nañu ne moom mooy Almasi bi.
42 Noonu bi bët setee,
Yeesu génn dëkk bi,
dem ci béréb bu sori te mbooloo mu bari di ko seet.
Bi ñu ko gisee,
ñu bëgg ko téye,
ngir bañ mu dem.
43 Waaye Yeesu jël kàddu gi te wax leen,
«Fàww ma yégle xibaar bu baax bi ci nguuru Yàlla ci yeneen dëkk yi,
ndaxte loolu moo tax Yàlla yónni ma.»
44 Noonu Yeesu di wër ci kër-ñaan yi nekk ci réewu Yawut yépp,
di yégle xibaar bu baax bi.