Yeesu dem na ci dëkku Nasaret
Luug 4.14-30
14 Gannaaw loolu,
Yeesu dellu ci diiwaanu Galile fees ak kàttanu Xel mi ba tax turam siiw ci diiwaan bi yépp.
15 Ni muy jàngalee ci kër-ñaan yi tax na ñépp di ko tagg.
16 Noonu,
mu dem ca Nasaret fa mu yaroo woon,
dugg ci kër-ñaan gi,
ci bésu noflaay bi,
ni mu ko tàmme woon di def.
Mu jóg taxaw ngir jàng kàddu gi,
17 ñu jox ko téere yonent Yàlla Esayi.
Mu ubbi ko gis aaya yiy wax ne:
18 \qt «Xelu Boroom bi mu ngi ci man,
\qt ndaxte moo ma tànn
\qt ngir ma yégal néew-ji-doole yi xibaar bu baax bi.
\qt Moo ma yónni ngir ma yégal jaam yi ne dinañu leen goreel,
\qt ngir ma yégal gumba yi ne dinañu gisaat,
\qt ngir ma yewwi ñi ñu not
19 \qt te yégle atu yiwu Boroom bi.»
20 Bi mu jàngee ba noppi,
mu tëj téere bi,
jox ko ki koy denc,
te toog ngir jàngale.
Ñépp ñi nekkoon ci kër-ñaan bi di ko xool ci biir bët.
21 Noonu mu tàmbali di leen wax ne:
«Tey jii,
kàddu gi ngeen dégg ci Mbind bi mat na.»
22 Ñépp a ko doon seedeel lu baax te waaru ci kàddu yiw yi doon génn ci gémmiñam,
te ñuy wax ne:
«Kii ndax du doomu Yuusufa?»
23 Yeesu tontu leen ne leen,
« Dingeen ma wax ci léeb bi wax ne "Fajkat bi,
fajal sa bopp."
Te dingeen ma waxaat ne:
"Yég nañu lépp li nga def ci Kapernawum,
moom lañu bëgg nga def ko fii ci sa dëkk."»
24 Mu yokk ca ne:
«Ci dëgg maa ngi leen koy wax,
amul benn yonent bu ñu nangu ci dëkkam.
25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax,
ci jamono yonent Yàlla Ilyaas,
ci Israyil amoon na jigéen ñu bari,
ñu ñàkkoon seen jëkkër te asamaan si tëju woon diiru ñetti at ak genn-wàll,
tawul te xiif bi bari ci réew mi yépp,
26 waaye Yàlla yónniwul Ilyaas ci kenn ci ñoom ku dul ci benn jigéen bu ñàkkoon jëkkëram;
bu dëkk ca Sarebta ci wetu réewu Sidon.
27 Ci jamono yonent Yàlla Alyaasa,
ci Israyil amoon na ay gaana yu bari,
waaye faju ci woon kenn ku dul Naamaan mi jóge woon réewu Siri.»