Seytaane fiir na Yeesu
Luug 4.1-13
1 Yeesu jóge woon na dexu Yurdan,
fees ak Xel mu Sell mi.
Xel mi yóbbu ko ci biir màndiŋ bi.
2 Foofu Seytaane fiir na ko ñeent fukki fan.
Lekkul dara ci bés yooyu yépp.
Bi loolu weesoo,
mu xiifoon.
3 Seytaane ne ko:
«Su fekkee yaay Doomu Yàlla,
waxal xeer wii mu soppeeku mburu.»
4 Yeesu ne ko,
«Mbind mi nee na:
"Nit du dunde mburu rekk."»
5 Noonu Seytaane yóbbu ko ci catu tund wu gëna kawe,
te won ko ci saa si nguuri àddina si yépp.
6 Mu ne ko:
«Yaw,
dinaa la jox sañ-sañu nguur yii ngay gis ak seeni màggaay,
ndaxte man lañu ko jox te ku ma neex rekk la koy jox.
7 Soo nangoo sukk ci sama kanam,
lii yépp yaa koy moom.»
8 Yeesu ne ko,
«Mbind mi nee na:
"Bul sukk ci kanamu kenn ku dul Yàlla sa Boroom te di ko jaamu moom rekk."»
9 Noonu Seytaane yóbbu ko ci Yerusalem,
ba ci collu kër-Yàlla gi,
te ne ko:
«Su fekkee yaay Doomu Yàlla,
tëbal fii te nga daanu ci suuf,
10 ndaxte Mbind mi nee na,
\qt "Yàlla dina jox malaakaam yi ndigal ngir ñu aar la,
11 téye la ci seeni loxo,
ngir ñu bañ say tànk fakkastalu ci xeer."
\qt*»
12 Noonu Yeesu ne ko,
«Mbind mi nee na:
"Bul seetlu Yàlla sa Boroom."»
13 Gannaaw bi mu ko fiiree ci fànn yépp ba noppi,
Seytaane dem bàyyi fa Yeesu ba beneen yoon.