Yeesu mooy Boroom bésu noflaay bi
Luug 6.1-11
1 Benn bésu noflaay,
Yeesu doon jàll ci tool yi.
Taalibe yi witt ci pepp yi,
di boxom te di yéy.
2 Ñenn ci Farisen yi laaj leen:
«Lan moo tax ngeen di def loolu?
Yoonu Musaa dafay tere liggéey ci bésu noflaay bi.»
3 Yeesu tontu leen ne leen:
«Xanaa jànguleen li Daawuda defoon bu mu xiifee,
moom ak ñi mu àndaloon?
4 Mu dugg ci kër-Yàlla gi,
jël mburu yi ñu jébbal Yàlla,
lekk ci,
te jox ci ñi mu àndaloon,
te fekk na yoon bi mayul kenn di ko lekk ku dul jébbalkati-sarax si.»
5 Te mu ne leen:
«Doomu nit ki mooy Boroom bésu noflaay bi.»
6 Beneen bésu noflaay Yeesu dugg ci kër-ñaan bi,
di jàngale.
Foofu amoon na benn waay bu loxo ndeyjooram làggi.
7 Jàngalekati-yoonu-Musaa yi ak Farisen yi doon ko xool ba xam ndax ci bésu noflaay bi dina wéral waa ji ngir ñu tuumaal ko.
8 Waaye Yeesu xam seeni xalaat,
wax ku am loxo bu làggi bi:
«Jógal te nga taxaw ci kanamu ñépp.»
Mu jóg,
taxaw.
9 Yeesu ne leen:
«Am naa benn laaj ngir yeen.
Lan la yoon bi maye ngir ñu def ko ci bésu noflaay bi,
lu baax walla lu bon?
Muccal nit walla bàyyi ko mu loru?»
10 Noonu Yeesu xool leen ñoom ñépp,
wax nit ki am loxo bu làggi bi:
«Tàllalal sa loxo.»
Nit ka tàllal loxoom,
daldi wér.
11 Jàngalekati-yoonu-Musaa yi ak Farisen yi daldi fees dell ak mer,
di waxtaan ci seen biir lan lañu wara def Yeesu.