Yeesu des na ca kër-Yàlla ga
Luug 2.41-52
41 At bu nekk waajuru Yeesu yi dañu doon dem Yerusalem ngir màggalu Paak bi.
42 Bi Yeesu amee fukki at ak ñaar,
ñu yóbbaale ko ni ko aada màggalu Paak bi bëgge.
43 Bi màggal bi jeexee ñu ñibbi waaye xale bi Yeesu des Yerusalem te ay waajuram yéguñu ko.
44 Ñu xalaatoon ne dafa ànd ak ñi ñu bokkaloon yoon bi.
Bésu lëmm ñu koy dox,
noonu ñu tàmbali di ko seet ci mbokk yi ak xarit yi,
waaye gisuñu ko.
45 Ñu dellu Yerusalem te wéy di ko seet.
46 Ñetteelu fan bi,
ñu daldi ko gis ci kër-Yàlla gi,
mu toog ci diggu jàngalekat yi di leen déglu te di leen laaj ay laaj.
47 Ñépp ñi ko doon déglu daldi waaru lool ci dégginam ak tontu yi mu leen doon jox.
48 Bi ko ay waajuram gisee ñu daldi waaru.
Yaayam ne ko:
«Sama doom,
lan moo tax nga def nu lii?
Man ak sa Pàppa jaaxle woon nanu lool te danu la doon seet.»
49 Mu tontu leen ne:
«Ndax xamuleen ne damaa wara def sama liggéeyu Baay?
Léegi nag,
lu tax ngeen may seet?».
50 Waaye ñoom xamuñu woon dara ci li mu leen doon wax.
51 Gannaaw loolu,
Yeesu dellu ak ñoom ca Nasaret te di leen déggal.
Yaayam denc loolu lépp ci xolam te di ko fàttaliku.
52 Yeesu nag mu ngi doon màgg ci jëmm,
te di yokku ci xel mu rafet,
te neexoon na Yàlla ak nit ñi.