Liggéeyu Yaxya
Luug 3.1-22
1 Ci fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar,
fekkoon na Poñsë Pilaat yilifoon diiwaanu Yude,
Erodd yilifoon diiwaanu Galile te magam Filib yilifoon diiwaanu Iture ak bu Tarakonit,
Lisañas yilifoon diiwaanu Abilen.
2 Anas ak Kayif nekkoon jébbalkati-sarax-yu-mag ya.
Noonu kàddu Yàlla gi wàcc ci Yaxya mi di doomu Sakari ci biir màndiŋ bi.
3 Yaxya doon na wër diiwaanu dexu Yurdan ba yépp,
di waare naan:
«Nanguleen ma sóob leen ci ndox ngir wone ne tuub ngeen seeni bàkkaar,
te noonu Yàlla dina leen baal.»
4 Noonu,
li yonent Yàlla Esayi bindoon ci téereem mat na:
\qt «Lii mooy baatu nit kiy yuuxu ci biir màndiŋ bi:
\qt "Waajalleen yoonu Boroom bi
\qt defarleen yoonam yi,
ñu jub.
5 \qt Xur bu nekk dinañu ko sëkk.
\qt Bépp tund bu mag ak bépp tund bu ndaw,
dinañu leen maasale.
\qt Yoon yu dëng yi dinañu leen jubbanti.
\qt Yoon yu ñagas yi dinañu leen liisal,
6 \qt te ñépp dinañu gis mucc gi Yàlla maye."»
7 Noonu mbooloo mu bari daan na ñëw ci Yaxya ngir mu sóob leen ci ndox.
Yaxya da leen doon wax naan:
«Yeen ñi fees ak daŋar mel ni jaan,
kan moo leen jàngal ngir ngeen daw meru Yàlla mi nara wàcc?
8 Woneleen nag ci seen jëf ne tuub ngeen seeni bàkkaar.
Buleen yem rekk di wax ci seen xel ne:
"Nun am nanu Ibraayma ni baay."
Ndaxte maa ngi leen koy wax,
ci xeer yii,
Yàlla mën na cee sàkkal Ibraayma ay doom.
9 Sémmiñ bi jege na ba noppi ngir dagg reeni garab yi.
Bépp garab bu meññewul meññeef bu baax dinañu ko dagg te sànni ko ci safara si.»
10 Mbooloo mi laaj ko ne:
«Kon nag lan lanu wara def?»
11 Mu tontu leen:
«Képp ku am ñaari mbubb na jox benn bi nit ki amul,
te ku am ñam,
séddoo ko ak ki amul dara.»
12 Ay juutikat tamit ñëw nañu ngir mu sóob leen ci ndox.
Ñu laaj Yaxya ne ko:
«Jàngalekat bi,
lan lanu wara def?»
13 Mu tontu leen:
«Buleen laaj lu ëpp,
li leen yoon di laajloo.»
14 Ay soldaar tamit ne ko:
«Lan lanu wara def nag?»
Mu tontu leen:
«Buleen jël alalu kenn ci kaw jaay doole walla ci kaw di ko sosal,
te doylooleen seen peyoor. »
15 Noonu askan bi di xaar ak yaakaar,
di laaj ci seen xel,
ndax Yaxya mooy Almasi bi.
16 Yaxya wax leen ñoom ñépp:
«Man,
maa ngi leen di sóob ci ndox,
waaye kenn ku ma ëpp kàttan dina ñëw.
Yelloowuma sax tekki ay dàllam,
te kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak ci safara.
17 Teg na layu ci loxoom di bees ngir teqale pepp bi ak xatax bi.
Dina dajale pepp bi ci sàqam waaye dina lakk xatax bi ci safara bu dul fey mukk.
18 Noonu Yaxya doon na leen jàngal ci ay mbir yu bari tey yégal xibaar bu baax bi askan bi.
19 Erodd mi yilifoon diiwaanu Galile takkoon na Erojàdd mi di jabaru magam,
te tamit dafa defoon yeneen ñaawteef yu bari,
loolu taxoon na Yaxya di ko sikk.
20 Noonu Erodd yokkaat ci beneen ñaawteef,
ci bi mu jàppalu Yaxya ba tëj ko kaso.