Waajuru Yeesu yi yóbbu nañu ko ci kër-Yàlla ga
Luug 2.22-40
22 Bi bési setal yi matee ni ko yoon bi Boroom bi Yàlla joxe woon jaarale ko ci Musaa digle,
Yuusufa ak Maryaama yóbbu nañu xale bi ci dëkku Yerusalem ca kër-Yàlla ga ngir àndi ko ci teewaayu Boroom bi Yàlla,
23 ni ñu ko binde woon ci benn yoon boobu ne:
«Bépp taaw bu góor dinañu ko beral Boroom bi.»
24 Yuusufa ak Maryaama jébbal nañu sarax ni ko yoonu Boroom bi digle:
ñaari pitaxu àll walla ñaari picc yu ndaw yu ñuy woowe xati.
25 Amoon na ci Yerusalem benn waay,
ju tuddoon Simeyon.
Waa ju jub la woon te gëm Yàlla.
Da doon xaar dëfëlu Israyil te Xel mu Sell mi àndoon na ak moom.
26 Xel mu Sell mi xamaloon na ko ne du dee mukk te gisul Almasi bi Boroom bi dige woon.
27 Noonu Xel mi yóbbu ko ba ca kër-Yàlla gi.
Bi waajuru Yeesu yi indee xale bi ngir matal li yoon bi digle,
28 Simeyon jël ko ci ay loxoom tey sant Yàlla di wax ne:
 
29 «Léegi nag Boroom bi Yàlla sa dige mat na,
yewwil sa jaam mu dee ci jàmm,
30 ndaxte samay bët gis nañu sa mucc bi,
31 mucc bi nga waajal ci kanamu askan yi yépp.
32 Mu nekk leer bi lay won xeeti àddina si yépp.
Mooy tamit màggaayu Israyil sa askan.»
 
33 Pàppa Yeesu ak yaayam waaru woon nañu ci li mu doon wax ci lu jëm ci xale bi.
34 Simeyon barkeel leen te wax Maryaama yaayu Yeesu ne:
«Yàlla da tànn xale bii ngir mu waral daanu ak jógu ñu bari ci Israyil,
dina doon màndarga Yàlla bi nit ñi dul nangu.
35 Te noonu dina feeñal ci leeraay xalaat yi nëbbu ci biir xolu ñu bari,
te yaw nag metit dina xar sa ruu ni jaasi.»
36 Amoon na tamit benn yonent bu jigéen bu tudd Aana di woon doomu Fanuwel bokkoon ci askanu Aser.
Aana màggatoon na lool.
Ba muy janq te xamul góor,
la séy.
Dundoon na ak jëkkëram juróom ñaari at.
37 Gannaaw loolu jëkkëram gaañu te mu des moom kese.
Léegi,
amoon na juróom ñett fukki at ak ñeent.
Daawul jóge ci kër-Yàlla gi te doon na jaamu Yàlla ci woor ak ñaan,
guddi ak bëccëg.
38 Mu yeggsi ci waxtu bi Simeyon doon wax.
Aana tàmbalee gërëm Yàlla te doon na wax lu jëm ci xale bi ñépp ñi doon xaar waxtu bi Yàlla di yewwi Yerusalem.
39 Bi waajuru Yeesu yi matalee lépp li yoonu Boroom bi digle,
ñu dellu ci seen dëkk Nasaret ci diiwaanu Galile.
40 Xale bi mu ngi doon màgg te di dëgër.
Amoon na xel bu rafet,
te yiwu Yàlla nekkoon na ak moom.