Yeesu juddu na ca dëkku Betleyem
Luug 2.1-21
1 Ci jamono jooju,
Sesaar Ogust joxe na ndigal ngir ñépp binduji,
ngir xam ñaata nit lañu tollu ci nguuru Room.
2 Mu nekkoon waññ bu jëkk ci jamono bi Kiriñus yilifoon diiwaanu Siri.
3 Noonu ñépp daldi dem,
binduji fu ñu cosaanoo.
4 Yuusufa nag jóge dëkku Nasaret bi nekk ci diiwaanu Galile,
ngir dem dëkku Betleyem bi nekk ci diiwaanu Yude.
Foofu la Daawuda juddoo,
te Yuusufa bokk ci askanam.
5 Looloo tax mu ànd ak Maryaama mi ñu ko mayoon te mu ëmboon,
ngir mu dem fa binduji.
6 Bi ñu nekkee Betleyem,
waxtu bi Maryaama wara am doom yeggsi.
7 Mu am doomam bu jëkk,
bu góor;
lëmës ko ci laytaay,
tëral ko ci lekkukaayu jur,
ndaxte fi ñu doon dalal gan yi daa feesoon.
8 Ci diiwaan boobu,
ay sàmmkat nekkoon nañu ci àll bi,
fanaane wottu seeni gétt.
9 Benn malaaka feeñu leen te màggaayu Yàlla di leeral li leen wër.
Ñu daldi ànd ak tiit,
10 waaye malaaka mi ne leen:
«Buleen tiit ndaxte,
xoolleen!
Maa ngi leen di yégal xibaar bu baax biy bégloo askan bi yépp.
11 Tey jii ci dëkku Daawuda,
seen Musalkat juddu na,
di Almasi bi,
di Boroom bi.
12 Ci màndarga yii ngeen koy xàmmee:
dingeen fekk benn liir bu ñu lëmës ak laytaay te tëral ko ci lekkukaayu jur.
13 Ci saa si,
amoon na ak malaaka bi yeneeni malaaka yu bari.
Ñuy sant Yàlla te di wax ne:
14 «Nañu màggal Yàlla ci asamaan yu gëna kawe yi,
te ci suuf si,
na jàmm am ci ñépp ñi mu may yiwam.»
15 Bi leen malaaka yi bàyyee te dellu asamaan,
sàmmkat yi di waxtaan ci seen biir ne:
«Nanu dem nag ba Betleyem ngir gis li fa xew te Boroom bi xamal nu ko.»
16 Ñu gaawantu dem.
Ñu fekk fa Maryaama ak Yuusufa ak liir bi ñu tëral ci lekkukaayu jur.
17 Bi ñu leen gisee,
ñu nettali ñépp kàddu yi ñu déggoon ci li jëm ci xale bi.
18 Ñépp ñi doon dégg waxu sàmmkat yooyu daldi yéemu,
19 te Maryaama moom,
denc loolu lépp ci xelam te mu ciy xalaat.
20 Sàmmkat yi dellu seeni gétt.
Ñuy màggal Yàlla te di ko sant ci lépp li ñu dégg te gis ko,
loolu lépp amoon na,
ni leen ko malaaka bi waxe woon.
21 Ci juróom ñetteelu fan bi gannaaw bi mu juddoo,
di bés bi ñu wara xarafal xale bi,
ñu tudde ko Yeesu di tur bi ko malaaka bi waxoon laata yaayam di ëmb.