Juddub Yaxya
Luug 1.57-80
57 Jamono ji Elisabet ware am doom jot na.
Mu am doom ju góor.
58 Dëkkandoo yi ak mbokkam yi dégg nañu ne Boroom bi wone na yërmandeem ci moom,
ñuy bànneexu ak moom.
59 Ci juróom ñetteelu fan bi,
ñu ñëw ngir xarafalsi xale bi.
Ñu bëgg ko tudde Sakari,
mi di Pàppaam,
60 waaye yaayam ne:
«Déedéet.
Dinañu ko woowe Yaxya!»
61 Ñu ne ko:
«Amul kenn ci say mbokk ku tudd noonu.»
62 Ñu tàmbali di joxoñ di laaj pàppaam ngir xam naka la bëgg ñu woowe xale bi.
63 Sakari laaj àlluwa,
bind kàddu yii:
«Yaxya mooy turam!»
Ñépp yéemu.
64 Ci saa si,
gémmiñu Sakari ubbiku te làmmiñam yewwiku.
Mu tàmbali wax di sant Yàlla.
65 Noonu dëkkandoom yépp daldi fees dell ak ragal.
Ñu tàmbali di nettali xew-xew yooyu ci diiwaanu tundi Yude yépp.
66 Ñépp ñi doon dégg loolu dencoon nañu ko ci seen xol di laaj seen bopp:
«Kon nag,
naka la xale bi nara mel?»
Ndaxte Boroom bi mu ngi woon ak moom!
67 Sakari pàppay xale bi fees ak Xel mu Sell mi di wax ci turu Yàlla ne:
68 «Cant ñeel na Boroom bi,
Yàllay Israyil
ndaxte ganesi na askanam te yewwi leen.
69 Jox na nu benn musalkat bu am kàttan
ci kër Daawuda surgaam,
70 ni mu ko yégle woon ci jamono ju jëkk ja
jaarale ko ci gémmiñu yonentam yu sell yi.
71 Digoon na nu ne:
Moo nuy musal ci sunuy noon
te jële nu ci loxoy ñi nu bañ.
72 Yàlla wone na yërmandeem ci sunuy maam,
te fàttaliku na kóllëreem gu sell gi,
73 ni mu ko giñale woon sunu maam Ibraayma
74 ngir yewwi nu ci loxoy sunuy noon,
ngir nu mën koo jaamu te baña ragal
75 ci sellaay ak ci njubte ci kanamam,
sunu giiru dund yépp.
76 Yaw nag sama doom
dinañu la woowe yonent Yàlla Aji-Kawe ji,
ndaxte dinga dox ci kanamu Boroom bi
ngir waajal yoonam.
77 Dinga xamal askanam ne
Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar ngir musal leen.
78 Ndaxte sunu Yàlla fees na ak yërmande ak mbaax
ba tax mu wàcce ci sunu kaw leer bu jóge ci kaw
mel ni leeraayu jant buy fenk,
79 ngir leerale ñu nekk ci lëndëm
te takkandeer dee tiim leen,
te jiite nu ci yoonu jàmm ji.»
80 Xale bi da doon màgg te xelam di ubbiku.
Mu dëkk ci biir màndiŋ ba,
ba bés bu muy feeñ ci kanamu waa Israyil.