Maryaama seeti na Elisabet
Luug 1.39-56
39 Ci bés yooyu,
Maryaama daldi jóg te gaawantu dem ci benn dëkk bu nekk ci tund yi ci diiwaanu Yude.
40 Mu dugg ci biir këru Sakari daldi nuyu Elisabet.
41 Ci waxtu bi Elisabet déggee nuyoo Maryaama bi,
doom ji daldi yëngatu ci biiram te Elisabet fees ak Xel mu Sell mi.
42 Noonu mu yuuxu ak baat bu kawe ne:
«Barkeel nga ci biir jigéen ñi ñépp te doom ji nekk ci sa biir,
barkeel na!
43 Man may kan ba sama yaayu Boroom ñëw seetsi ma?
44 Ndaxte bi ma déggee ngay nuyoo ci saa si sama doom ji dafa yëngatu ak mbégte ci sama biir.
45 Yaw mi gëm barkeel nga ndaxte mbir yi ñu la yégal ci turu Boroom bi Yàlla,
dinañu mat.»
46 Te Maryaama wax ne:
«Sama ruu a ngi màggal Boroom bi,
47 te sama xel di bég ci Yàlla sama musalkat,
48 ndaxte teg na ay bëtam ci man miy jaamam bu woyof bi.
Xoolleen!
Dale ko tey,
niti jamono yi yépp,
dinañu ma woowe ki Yàlla barkeel
49 ndaxte Aji-Kàttan ji defal na ma ay mbir yu réy
te turam dafa sell.
50 Yërmandeem dina law ci ñi ko ragal
ak seeni sët ba ci seeni sëtaat.
51 Def na ay yëf yu mag ci dooley loxoom.
Tasaare na ñi am ci seen xol ay xalaatu réy-réylu.
52 Daaneel na buur yi ci seen nguur
te yékkëti ñi suufeelu.
53 May na ñi xiifoon lekk ba ñu regg
te dàq boroom alal yi,
loxoy neen.
54 Wallusi na Israyil surgaam
te fàttaliku yërmandeem
55 ci Ibraayma ak askanam ba fàww,
ni mu ko dige woon sunuy maam.»
56 Maryaama desoon na ak Elisabet lu tollu ci ñetti weer te noonu mu dellu këram.