Yeesu ci këru Farisen ba Simoŋ
Luug 7.36-50
36 Amoon na benn Farisen bu ñaan Yeesu ngir mu lekkandoo ak moom ci këram.
Yeesu nangu,
dugg kër Farisen bi,
te toog ci bérébu lekkukaay ba.
37 Mu am benn jigéen bu dundinam baaxul bu nekkoon ci dëkk bi,
mu xam ne Yeesu mu ngi kër Farisen bi,
mu ñëw,
indaale butéel bu rafet bu ñuy woowe albaatar bu fees dell ak latkoloñ.
38 Noonu mu jegesi ci wetu tànki Yeesu,
di jooy ba tooyal tànki Yeesu ak rongooñam te di leen fompe kawaram,
di leen fóon te di ko sotti latkoloñ.
39 Noonu bi Farisen bi dalal Yeesu gisee loolu,
muy xalaat ci xelam ne:
«Kii,
su doon yonent,
doon na xam,
jigéen bi koy laal,
dundinam baaxul.»
40 Yeesu jël kàddu gi,
ne ko:
«Simoŋ,
bëgg naa la wax lii.»
Simoŋ tontu ko ne:
«Jàngalekat bi,
waxal.»
41 Yeesu ne ko:
«Dafa amoon benn waay.
Mu lebaloon ñaari nit bor.
Kenn ki mu lebal ko téeméeri junni,
keneen ki mu lebal ko fukki junni.
42 Te ñoom ñaar ñépp amuñu woon lu ñu mëna feye bor yi.
Ci mbaaxam mu baal leen ñoom ñaar ñépp seeni bor.
Ci ñoom ñaar kan moo ko ciy gëna bëgg?»
43 Simoŋ tontu ko ne:
«Xanaa ki mu baal bor bu mag bi.»
Yeesu ne ko:
«Àtte nga bu baax.»
44 Noonu,
Yeesu walbatiku ci ku jigéen ki,
ne ko:
«Simoŋ,
gis nga ku jigéen kii?
Yaw,
bi ma duggee sa kër mayuloo ma ndox ngir ma raxas samay tànk,
waaye moom,
noppiwul di tooyal samay tànk ak rongooñam te di leen fompe kawaram.
45 Yaw,
fóonuloo ma,
waaye moom,
noppiwul di fóon samay tànk.
46 Diwuloo diw ci sama bopp,
waaye moom,
noppiwul di sotti latkoloñ ci samay tànk.
47 Moo tax maa ngi la koy wax ne mbëggeelam dafa bari ndaxte baal nañu ko bàkkaaram yu bari yi,
waaye ku ñu baal tuuti,
mbëggeelam day tuuti.»
48 Noonu Yeesu ne ku jigéen ki:
«Baal nañu la say bàkkaar.»