Yeesu wax na ci lu jëm ci Yaxya
Luug 7.18-35
18 Te taalibe Yaxya yi nettali nañu ko loolu lépp.
Noonu mu woo ñaar ci ñoom,
19 te mu yónni leen ci Boroom bi ngir laaj ko:
«Ndax yaw yaay Almasi bi waroona ñëw walla danoo wara xaar keneen?»
20 Noonu bi ñu yeggsee ci wetu Yeesu ñu wax ko ne:
«Yaxya moo nu yónni ngir nu laaj la:
"Ndax yaw yaay Almasi bi waroona ñëw walla danoo wara xaar keneen?"»
21 Ci waxtu boobu sax Yeesu mu ngi doon wéral ay nit ñu bari ci seeni feebar,
ci seeni laago te di dàq rab yu bon,
te mu doon gislowaat gumba yi.
22 Noonu mu tontu taalibe Yaxya yi ne leen:
«Demleen,
nettali Yaxya li ngeen gis ak li ngeen dégg.
Gumba yi ñu ngi gisaat,
lafañ yi ñu ngi dox,
gaana yi wér nañu,
tëx yi ñu ngi dégg,
te ñi dee woon ñu ngi dekki;
te yégal nañu xibaar bu baax bi néew-di-doole yi.
23 Barkeel na ki dul ñàkk ngëm ndax man!»
24 Gannaaw bi ñi Yaxya yónni woon delloo,
Yeesu di wax ak mbooloo mi,
ci lu jëm ci Yaxya:
«Lan ngeen demoon gis ci màndiŋ bi:
benn xeetu ñax bu ngelaw li di naawloo ci wet bu nekk?
25 Waaye lan ngeen demoon gis:
benn nit bu sol ay yére yu rafet?
Ñiy sol ay yére yu rafet dañuy dund ci biir bànneex te di dëkk ci biir kër buur yi.
26 Waaye lan ngeen demoon gis:
ab yonent?
Waaw,
maa ngi leen koy wax,
ku ëpp sax yonent,
27 ndaxte ci Yaxya la Mbind mi wax ne:
 
\qt "Xoolal maa ngi yónnee ci sa kanam benn yonent ngir mu waajal sa yoon ci sa kanam."
 
28 Te maa ngi leen koy wax,
ci ñi juddoo ci jigéen amul kenn ku gëna mag Yaxya,
waaye ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla gi,
moo ko gëna mag.»
29 Te noonu niti askan bi yépp ak juutikat yi doon déglu bataaxalu Yaxya,
nangu nañu ne Yàlla dafa jub ba tax ñu nangu Yaxya sóob leen ci ndox.
30 Waaye Farisen yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa yi nanguwuñu coobare Yàlla ci seen dund ba tax nanguwuñu Yaxya sóob leen ci ndox.
31 Yeesu waxaat ne:
«Ñan laa wara méngalee nitu jamono ji ak ñan lañuy nirool?
32 Ñu ngi nirook ay xale yu toog ci péncu dëkk bi di yuuxuwante,
ñenn ñi di wax ñeneen ñi,
ne:
 
"Woyal nanu leen woyi bànneex te fecculeen.
Woyal nanu leen woyi dëj te jooyuleen."
 
33 Ndaxte Yaxya ñëw na,
lekkul mburu,
naanul biiñ,
ngeen wax ne:
"Kii dafa am rab."
34 Noonu Doomu nit ki ñëw na di lekk te di naan,
ngeen wax ne:
"Kii day lekk ak naan rekk,
di xaritu juutikat yi ak bàkkaarkat yi."
35 Waaye ñépp ñi nangu li Yàlla wax ci xelam bu rafet,
xam nañu ne Yàlla dafa jub.