Ngëmu njiitu soldaaru Room bi
Luug 7.1-10
1 Gannaaw bi mu waxee kàddu yooyu yépp mbooloo mi ko doon déglu ba noppi,
Yeesu dugg na Kapernawum.
2 Foofu,
amoon na benn njiitu soldaaru Room bu amoon surgaam bu mu bëggoon lool,
te mu feebar bay waaja dee.
3 Bi mu déggee ñuy wax ci Yeesu,
mu yónni yenn njiitu Yawut ngir ñu ñaan ko mu ñëw wéral surgaam bi.
4 Bi ñooñu yeggsee ci wetu Yeesu,
ñu daldi koy ñaan ndimbal ak doole,
ne ko:
«Kii déy,
yelloo na nga defal ko lii
5 ndaxte ku bëgg sunu askan bi la,
te moo def ba nu tabax sunu kër-ñaan bi.»
6 Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom.
Bi ñu demee ba jegesi kër gi,
njiitu soldaar bi daldi ko yónnee ay xaritam.
Bi ñu dajeek Yeesu,
ñu ne ko:
«Boroom bi,
jarul ngay sonal sa bopp ndaxte yelloowuma nga dugg sama kër.
7 Te loolu moo waral sax ma yaakaar ne yelloowuma ñëw fekksi la.
Waaye waxal benn kàddu te sama surga bi dina wér,
8 ndaxte man tamit am naa ay kilifa yu may jiite,
te jiite naa ay soldaar yu may jox ndigal.
Su ma nee kii "Demal,"
mu dem!
Su ma nee kee "ñëwal,"
mu ñëw!
Am naa tamit surga.
Su ma ko nee "defal lii,"
mu def ko!»