Yeesu jàngal na taalibeem naka lañu wara jëfe
Luug 6.17-49
17 Bi Yeesu wàccee ci tund bi àndoon na ak ndaw yi,
taxaw ci béréb bu suufe.
Foofu,
amoon na taalibe yu bari ak mbooloo mu takku jóge woon ci diiwaanu Yude ak dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ci wetu géej,
maanaam Tir ak Sidon.
Ñëwoon nañu ngir déglu ko te jot seen wér gu yaram.
18 Ñi nga xamante ne ay rab yu bon dañu leen sonaloon tamit jot nañu seen wér gu yaram.
19 Ñoom ñépp dañu doon wuta laal Yeesu ndax kàttan bi doon génn ci moom tey wéral seeni feebar.
20 Noonu Yeesu yékkëti bëtam yi,
xool taalibe yi,
ne leen:
 
«Barkeel ngeen,
yeen ñi néew doole
ndaxte nguuru Yàlla yeena ko moom.
21 Barkeel ngeen,
yeen ñi xiif léegi,
ndaxte dingeen regg.
Barkeel ngeen,
yeen ñiy jooy léegi,
ndaxte dingeen reetaan ni ji.
22 Barkeel ngeen su leen ñépp bañee
te beddi leen te di leen saaga,
di wax lu bon ci yeen ndax Doomu nit ki.
23 Ci kaw loolu,
àndleen ak mbégte tey fecc,
ndaxte Yàlla mu ngi leen di waajal neexal bu mag ci asamaan.
Ci dëgg-dëgg,
ñoom,
noonu la seeni maam doon def ak yonent yi.
 
24 «Waaye musiba dal na leen,
yeen boroom alal yi
ndaxte dëfël nañu leen ba noppi.
25 Musiba dal na leen,
yeen ñi regg
ndaxte dingeen xiifati.
Musiba dal na leen,
yeen ñiy ree léegi,
ndaxte dingeen ànd ak naqar aki rongooñ.
26 Musiba dal na leen,
su leen ñépp di wax lu baax ci yeen,
ndaxte ñoom,
noonu la seeni maam doon def ak yonent yi nga xam ne dëgguwuñu woon.
 
27 «Waaye maa ngi leen koy wax yeen ñi may déglu,
bëggleen seeni noon,
te di defal lu baax ñi leen bañ,
28 te barkeel leen ñépp ñi leen yéene lu bon te ñaanal leen ñi leen di def lu bon.
29 Bu la nit mbejee ci benn lex bi,
jox ko bi ci des.
Bu nit jëlee sa mbubb mu mag,
bu ko tere mu jël yére bu ndaw bi nga sol.
30 Mayal képp ku la ñaan.
Bu nit jëlee sa yëf bul ko wax mu delloo la ko.
31 Li ngeen bëgg ñu defal leen ko,
yeen tamit defleen ko ngir ñoom.
32 Booleen bëggee ñi leen bëgg rekk,
ban ngërëm ngeen ciy jële?
Bàkkaarkat yi tamit bëgg nañu ñi leen bëgg rekk.
33 Booleen defalee lu baax ñi leen di defal lu baax rekk,
ban ngërëm ngeen ciy jële?
Ndax bàkkaarkat yi tamit dañuy defal lu baax ñi leen di defal lu baax.
34 Te bungeen di lebal ñi ngeen yaakaar ñu fey leen,
ban ngërëm ngeen ciy jële?
Bàkkaarkat yi tamit,
dañuy lebal seeni moroom bàkkaarkat ngir bu ñu leen di fey,
ñu jox leen lu tollook li ñu leen lebaloon.
35 Waaye yeen,
nangeen bëgg seeni noon,
te defal leen lu baax,
te nangeen leble te baña xaar ngir ñu fey leen,
te noonu dingeen am neexal bu réy,
te dingeen doon ay doomu Yàlla Aji-Kawe ji,
moom mi nga xam ne moo baax ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi.
36 Amleen yërmande ni Yàlla seen Baay ame yërmande.
37 «Buleen àtte te duñu leen àtte,
buleen daan te duñu leen daan.
Baaleleen te dinañu leen baal.
38 Joxeleen te dinañu leen jox.
Dinañu leen sottil ay peppu ceeb ci seeni poos ba ñu fees dell bay tuuru,
ndax ni ngeen di natte noonu lañu leen di nattale.»
39 Yeesu wax léeb bii:
«Ndax gumba mën na wommat moroomu gumbaam?
Déedéet,
ndaxte bu ñu moytuwul,
ñoom ñaar ñépp dinañu daanu ci kàmb.
40 Ndax taalibe bi,
moo gëna mag jàngalekatam?
Waaye bu jàngee ba mokkal,
mën na mel ni jàngalekatam.
41 Lu tax ngay xool ñax bi nekk ci sa bëtu moroom te gisoo bant bi nekk ci sa bët?
42 Lu tax ngay wax sa moroom:
"Kaay ma dindil la ñax bi ci sa bët,"
te yaw gisoo bant bi ci sa bët?
Naaféq bi!
Génneel ba noppi bant bi ci sa bët.
Bu booba dinga gis bu baax te mëna génnee ñax bi ci sa bëtu moroom.
43 «Garab bu baax du am meññeef bu bon te garab bu bon du am meññeef bu baax.
44 Garab bu nekk ñu ngi koy xàmmee ci meññeefam.
Kenn du witt gaŋ ci garabu kàdd,
te kenn du witt ay reseñ ci ay xaaxaam.
45 Nit bu baax mu ngi jële ci biir xolam bu fees ay mbir yu baax,
te nit bu bon mu ngi jële ci biir xolam bu fees ay mbir yu bon.
Lu fees ci xol,
gémmiñ wax ko.
46 «Lu tax ngeen may woowe "Boroom bi,
Boroom bi,"
te dooleen jëfe samay kàddu?
47 Dinaa leen won nit kiy ñëw ci man lu muy nirool,
mooy ki nga xam ne day déglu samay kàddu te di ko jëfe.
48 Day mel ni nit kuy tabax këram,
gas,
gas ba mu xóot,
teg fondamaa bi ci kaw doj.
Bu dex bi walee,
ndox yi dal ci kër gi,
te du ko mëna yàq ndaxte tabax bi dafa baaxoon.
49 Waaye kiy déglu samay kàddu te du ko jëfe,
day mel ni nit kuy tabax ci suuf si.
Amul fondamaa.
Bu ndoxu dex gi walee ci kër gi,
ci saa si,
kër gi daldi màbb.
Noonu yàqute kër googu dina réy lool.»