Saraxu jigéen ju néew doole bi
Luug 21.1-4
1 Bi Yeesu yékkëtee bëtam mu gis boroom alal yiy joxe seen sarax ci ndab bi ñuy joxee xaalis ci biir kër-Yàlla gi.
2 Itam mu gis benn jigéen bu jëkkëram gaañu woon te néew doole,
mu joxe ñaari xànjaru xaalis.
3 Noonu mu ne leen:
«Ci dëgg maa ngi leen koy wax,
jigéen bi néew doole moo gëna joxe yeneen nit yi yépp
4 ndaxte ñoom ñépp dañoo joxe ci seen barile waaye moom dafa joxe ci néewleem ba joxe lépp li mu wara dunde.»