Nit ku bëgga topp Yeesu war na bàyyi lépp
Luug 14.25-35
25 Benn bés Yeesu doon tukki.
Mbooloo mu takku àndoon na ak moom.
Noonu mu walbatiku ne leen:
26 «Képp kuy ñëw ci man,
dangaa wara bàyyi sa baay,
sa yaay,
sa jabar,
say doom,
say mag ak say rakk,
ak sa dund sax.
Lu ko moy doo mëna nekk sama taalibe.
27 Fàww nga déggal ma ba ma jaral la ñu daaj la ci bant te topp ci man,
lu koy moy,
doo mëna nekk sama taalibe.
28 Kenn ci yeen bu bëggee tabax kër gu kawe,
ndax du toog xalaat ñaata la koy dikke,
ngir xam li mu am ci xaalis ndax dina mëna matal liggéey bi?
29 Lu ko moy dina tàmbali teg fondamaa waaye du ko mëna yeggali.
Su boobaa,
ñépp ñi gis loolu dinañu ko ñaawal
30 tey wax ne:
"Kii déy,
tàmbali na tabax waaye mënula yeggale."
31 Walla su fekkee dafa am benn buur,
bu wara dem xare ak beneen buur ndax du toog xalaat,
ndax ak fukki junni xarekat,
ndax dina mëna jaamaarloo ak beneen buur bi yor ñaari fukki junni xarekat?
32 Lu ko moy ci waxtu wi buur boobu di soreegul na ko yónnee ay ndaw,
ngir ñu waxtaan ngir déggoo ci jàmm.
33 Te noonu nag,
ku nekk ci yeen bu bàyyiwul am-amam yépp du mëna nekk sama taalibe.
34 Xorom déy,
lu am solo la,
waaye su ñàkkee cafkaam naka lañu koy mëna sàppalee?
35 Dootul am njériñ ci suuf si te dootul mëna nekk sax tos.
Dinañu ko sànni ci biti.
Na ki am nopp ngir déglu,
dégg.»