Yàqutewu Yerusalem
Luug 13.31-35
31 Noonu mu am ay Farisen yu ñëw wax Yeesu ne:
«Jógeel fii,
nga dem feneen ndaxte Erodd mu ngi lay bëgga rey.»
32 Yeesu tontu leen ne:
«Demleen ngeen waxal ma xaju àll boobu ne:
"Xoolal!
Damay dàq rab yi te wéral ñi feebar tey ak suba,
te ci ñetteelu fan bi ma matal sama liggéey."
33 Waaye fàww ma dem tey,
suba ak gannaaw suba ndaxte jaaduwul ñu reye yonent feneen fu dul Yerusalem.
34 Aa Yerusalem,
Yerusalem,
yaw miy rey yonent yi tey sànni ay xeer ñi la Yàlla yónnee ba ñu dee.
Ñaata yoon ma bëgga dajale say doom,
ni ginaar di dajalee ay cuujam te muur leen ak ay laafam,
waaye yeen bëgguleen ko!
35 Moo tax Yàlla dina leen bàyyee seen dëkk.
Maa ngi leen koy wax,
dootuleen ma gis ba bés bi ngeen di wax ne:
"Barkeel na kiy ñëw ci turu Boroom bi.''»