Malaaka Jibril yégle na juddub Yaxya
Luug 1.5-25
5 Ci jamono bi Erodd bu mag nekkee buuru Yude,
amoon na benn jébbalkatu-sarax bu tuddoon Sakari.
Mu bokkoon ci mbootaayu jébbalkati-sarax yi askanoo ci Abiya te jabaram Elisabet bokkoon ci askanu Aaróona jébbalkatu-sarax-bu-mag bi.
6 Sakari ak jabaram juboon nañu ci kanamu Yàlla di topp ndigalu Boroom bi yépp ak li mu santaane ni mu ware,
7 waaye amuñu woon doom ndaxte Elisabet mënul woona am doom te ñoom ñaar ñépp dañoo màggatoon.
8 Benn bés,
Sakari doon na def liggéeyu jébbalkatu-sarax bi ci kër-Yàlla gi ndaxte mbootaay bi mu bokkoon moo aye woon.
9 Ci aaday jébbalkatu-sarax yi,
dañu doon tegoo bant ngir xam ku wara taal cuuraay bi.
Bant bi dal ci Sakari,
moo tax mu dugg ci biir béréb bu sell bu Boroom bi ngir taal fa cuuraay bi.
10 Ci waxtu bi muy taal cuuraay bi,
mbooloo mu takku ñu ngi woon ci biti di ñaan.
11 Noonu benn malaaka Boroom bi feeñu Sakari,
mu taxaw ci ndeyjooru fi ñuy taale cuuraay bi.
12 Bi ko Sakari gisee mu jaxasoo ànd ak tiit.
13 Malaaka bi ne ko:
«Sakari bul tiit ndaxte Yàlla nangu na sa ñaan.
Sa jabar Elisabet dina la amal doom bu góor.
Nanga ko tudde Yaxya.
14 Dina nekk mbégte bu réy ci yaw te ñu bari dinañu bànneexu ci juddoom.
15 Dina nekk nit ku màgg ci kanamu Boroom bi Yàlla.
Du naan biiñ walla dara lu koy màndiloo.
Dina fees ak Xel mu Sell mi,
dale ko ci bi mu nekkee ci biiru yaayam
16 te dina delloosi waa Israyil yu bari ci Yàlla seen Boroom.
17 Dina dox ci kanamu Yàlla,
te Xel mu Sell mi dina jëf ci moom ak kàttan,
ni mu doon jëfe ci yonent Yàlla Ilyaas ngir jubale baay yi ak seeni doom te delloosi ñi déggalul Yàlla ci xam-xamu ñu jub ñi,
ngir waajal askan bu taxaw temm ngir xaar Boroom bi.»
18 Sakari laaj malaaka bi ne:
«Naka laay xame ne loolu dëgg la,
ndaxte man mag laa te sama jabar tamit màggat na?»
19 Malaaka bi ne ko:
«Man maay Jibril.
Damay taxaw ci kanamu Yàlla ngir liggéeyal ko.
Dafa ma yónni ngir ma wax la te yégal la xibaaru jàmm bii
20 waaye gëmuloo samay kàddu yi wara mat ci seen jamono.
Looloo tax dinga muuma.
Dootoo mëna wax ba keroog mbir yooyu di mat.»
21 Ci jamono boobu mbooloo bi doon xaar Sakari jaaxle woon nañu ndaxte dafa yàggoon lool ci béréb bu sell bi.
22 Bi mu génnee mënul wax ak ñoom.
Noonu ñu xam ne am na lu ko feeñu ci biir béréb bu sell bi.
Muy wax ak ñoom ci joxoñ te muuma.